wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
yës
baraquer
yërmaande j-
miséricorde
Yàlla, ku bare yërmaande la
Dieu est plein de miséricorde.
yërëdë b-
seiche
yowmalxayaam b-
jugement dernier
Keroog, yowmalxayaam, ñépp dinañu dekki
au jour du Jugement dernier, tout le monde ressuscitera.
yësal
faire baraquer
yey
avoir raison contre
Yey nga ko; wàññi nañu njëg li
tu as eu raison contre lui; on a baissé le prix.
Yaa yey dem
C'est avec raison que tu es parti.
yéyu
pleurer à chaudes larmes sans sangloter, étouffer ses pleurs
yéwéne
faciliter à qqn une chose par élan de générosité
yewwu
se réveiller
Xale bi yewwu na
J'enfant s’est réveillé.
Omar, gone gu yewwu la
Omar est un enfant éveillé.
(prov.) Borom ndékki, ku ko jëkka yewwu tëddaat
le propriétaire du petit déjeuner, celui qui se réveille avant lui se recouche.
yox
être branlant
yiir g-
prosopis africana, Mimosacées
Këriñu yiir du gaawa raaf
le charbon de Prosopis ne se consume pas vite.
yiirukaay g-
objet servant à protéger
Lii mën naa nekk ag yiirukaay
ceci peut servir d’instrument de protection.
yikkat
sangloter
Dafa agsi di yikkat
il est arrivé en sanglotant.
yiixantu
agir lentement délibérément
Lu-tax ngay yiixantu sa liggéey ?
pourquoi fais-tu lentement ton travail ?
yugur-yuguri
marcher d’un pas pesant
Mu ngee di yugur-yuguri di dem
le voilà qui s’en va d’un pas pesant.
yuppi
offrir des fripes
yikkat j-
sanglot
Ay yikkat la fi agsee
il est arrivé ici en sanglots.
yiw
inspirer du respect
Li ngay def yiwul dara
ce que tu fais n’inspire pas du tout le respect.
yiw w-
grâce divine
Foo jëm, Yàlla na fa yiwu Yàlla jublu
où que tu ailles, puisse la grâce divine s’y diriger !
yiwadi
ne pas inspirer le respect
yoggoorlu
adopter une pose avachie
yolom
être lâche, ne pas être assez tendu, ne pas être assez serré
Fas gi dafa yolom
le nœud n’est pas assez serré.
Soos bi dafa yolom
la sauce n’est pas assez épaisse.
yoll
exprime le fait d’aller à grande vitesse
Séñ Fàllu nee na : Bu nee yàŋŋ, nga ne yoll te teey. Bu nee tacc, nga ne tekk, booleek nga ne nikk, ne nàŋŋ
le guide Fallou a dit : Quand elle (la voie) est libre, tu accélères sans te précipiter. Quand elle est embouteil-lée, tu restes calme, tu maîtrises ta voiture, tout en regardant droit devant toi.
yoloos
(déplacement) Sans faire de bruit
Dafa ne yoloos génn
il est sorti sans bruit.
yolax
tomber avant maturité (fruit)
Doom yi yolax a ëpp yi ñor
les fruits tombés avant maturité sont plus nombreux que ceux qui ont mûri.
yolliku
filer à l’anglaise
Ba mu bëggee dem, dafa yolliku
quand il a voulu partir, il a filé à l’anglaise.
yonent b-
prophète
Ngóor si dafa noon gis na yonent bi
le bonhomme avait dit qu’il avait vu le Prophète.
yombalal
faciliter à qqn (qqch)
yolnde w-
cours d’un ruisseau faisant suite à une chute d’eau
yomm
exprime le fait de s’en aller sur-le-champ, de partir immédiatement
Neel yomm ca tool ya
va-t’en immédiatement aux champs !
yoofaanu
venir par derrière qqn
Dama bañ mu yoofaanu ma
je ne veux pas qu’il me vienne de dos.
yool b-
rétribution
Yoolu Yàllaa gën bu nit
la rétribution de Dieu est meilleure que celle de l’homme.
yàlla j-; m-
Dieu
Yàlla dafa nu may xelum làqarci
Dieu nous a donné un esprit de débrouillardise.
(prov.) Yàlla, Yàlla, bay sa tool
Dieu, Dieu, cultive ton champ) aide-toi, le Ciel t’aidera.
Yàlla tere
Dieu ne plaise !
Yàlla yaa na
Dieu est miséricordieux.
yoor
faire descendre d’une bonne hauteur
Ba ñuy jéle seeni bagaas ca etaas ba, ca balkoŋ ba lañu tollu, di leen yoor
quand ils évacuaient leurs bagages de l’étage, c’est du balcon qu’ils les faisaient descendre.
yoo b-
moustique
Yoo yi ñooy indi sibiru
ce sont les moustiques qui donnent le paludisme.
yàbbit w-
aliment qu’on a fait ressortir de la bouche
Lu-tax nga koy jox sa yàbbit yi ?
pourquoi lui donnes-tu ce que tu ressors de ta bouche ?
yool
rétribuer
Bala ma lay yen, nga yool ma
tu devras me rétribuer avant que je ne t’aide à porter ta charge sur la tête.
yoor-yoor g-
fin de la matinée
Ci yoor-yoor
en fin de matinée.
yàcc
exprime la manière de rester amorphe, sans réaction
Ñépp a ngiy xëcc, nga ne yàcc di xoole
tout le monde tire et tu es là sans réagir, regardant dans tous les sens.
yomb g-
courge (Lagenaria siceraria, Cucurbitacées)
Cere ju amul yomb dootul cere
du couscous sans courge n’est plus du couscous.
(prov.) Gone, lawtanu yomb la; boo walbatiwul, mu law fu la neexul
l’enfant, c’est un plant de courge qui rampe; si tu ne retournes pas, elle rampe où il ne te plaît pas) l’enfant est comme une tige de courge qu’il faut réorienter pour qu’elle n’aille pas là où on ne voudrait pas.
yooru
descendre dans un lieu profond ou bas
Fooguma woon ne ñeme nga yooru ci teen bi
je ne pensais pas que tu avais le courage de descendre dans le puits.
yoote j-
de dames traditionnel
Yoote jee indi xuloo bi
C'est le jeu de dames qui a provoqué la querelle.
yàmboŋ
avoir de la bourbouille
Dama yàmboŋ
J'ai de la bourbouille.
yàq biir
faire une interruption volontaire de grossesse
yoos g-; m-
sisal (Agave sisalana, Agavacées)
Ay buumi yoos la jénd
il a acheté des cordes en sisal.
yooya
ceux-là
Kër yooya, yu bees lañu
ces maisons-là sont neuves.
Yooya laa bëgg
ce sont ceux-là que je veux.
yoot
marcher à pas feutrés
Looy yoot ni sàcc
qu’as-tu à marcher à pas de loup comme un voleur ?
(prov.) Soo xamoon li lay yoot, nga bàyyi li ngay yoot te daw
si tu savais ce qui te guette, tu laisserais ce que tu guettes et tu prendrais la fuite.
yoqat
être découragé
Bul tàyyi, bul yoqat
ne te lasse pas, ne te décourage pas !
yorax m-
tourbillon d’eau
Yorax mi yóbbu na ko
le tourbillon l’a entraîné.
yàq-yàq b-
dommage préjudice dégât
Yëngu-yëngu ba amoon Sapoŋ def na ay yàq-yàq yu bare
le tremblement de terre qu’il y a eu au Japon a fait beaucoup de dégâts.
yorr
faire irruption
Mu ne yorr ca néegu xale ya
elle fit irruption dans la chambre des enfants.