wolof
stringlengths 1
166
| french
stringlengths 2
331
|
---|---|
Axakay; dinaa bokk | si; je participerai. |
ayante | se relayer |
Danuy ayante togg gi | nous nous relayons pour la préparation du repas. |
ayante b- | de se relayer |
alkaati b- | agent de police |
Alkaati bi dafay tere woto yi taxaw fii | le policier interdit aux voitures de s’arrêter ici. |
Kanamu alkaati | visage austère. |
ay-ayle | faire alterner avec |
Danga wara ay-ayle togg yi | tu dois faire alterner les plats. |
alxayri b- | formule de con-sécration du mariage selon le rite musulman |
(prov.) Déggagul alxayri | elle n’est pas encore mariée. |
alwaayó b- | aloyau |
alku | être réduit à un état misérable par sa propre inconduite |
Dafa bàyyi woon ay waa-jur am, moo tax mu alku | il avait abandonné ses parents, c’est pour cela qu’il est misérable. |
ayib b- | imperfection |
Xale bu góor bu tollu ci diggu dooleem, ànd ak taar bu mucc ayib | un jeune homme dans la force de l’âge, d’une beauté sans tache. |
ayibte j- | indiscipline |
Xamuma ci ku mu jële ayibteem ji | je ne sais pas de qui il tient son indiscipline. |
ayudiir g- | cycle |
Dafay def ayudiir, mu amaat | c’est cyclique |
alkol b- | alcool (pour soins médicaux) |
ayoo | se quereller |
Dafa ayook dëkkandoom yépp | il s’est querellé avec tous ses voisins. |
aaytal | considérer comme maléfique |
Dañu ko aaytal, waaye dara bonu ci | on le considère comme mauvais mais il n’y a rien de mal en cela. |
almuudó b- | Élève religieux |
Jox ko almuudó yi | donne le riz aux élèves religieux ! |
ayubés g- | semaine |
Ayubés giy ñów la | c’est la semaine prochaine. |
ajoor b- | originaire du Cayor (Sénégal) |
Ab Ajoor a ko jàngal wolof | C'est un ressortissant du Cayor qui lui a enseigné le wolof. |
alburaax m- | cheval de l’ange Gabriel |
Alburaax, mooy fas wi Jibril, malaaka ma, di war Alburaq, | c’est le cheval que monte l’ange Gabriel. |
alfok | il faut que |
Alfok ma mos ci | il faut que j’y goûte. |
almet b- | allumette |
am | avoir (dans le sens d’exister) |
Am na ay bërëb yu ma dul dem | il y a des endroits où je ne vais pas. |
am | un / une |
ali | hue ! (pour faire avancer un cheval) |
aldànke | déranger tout le monde dans un endroit sans qu’on puisse rien y faire |
Dafa aldànke foofa yépp | il a dérangé tout le monde là-bas. |
al | fils de tel |
alaterete | être à la retraite |
aloom g- | Ébénier du Sénégal |
aloom g- | Ébénier du Sénégal |
baag b- | seau pour puiser |
Boo demee ca teen ba, dinañu la abal baag | si tu vas au puits, on te prêtera un seau. |
(prov.) Ku yàgg cib teen, baag fekk la fa | qui reste longtemps à un puits, un seau t’y trouve |
baase b- | sauce à base de pâte d’arachide que l’on mange avec du couscous |
Baase laay togg tey | je prépare du {baase} aujourd’hui. |
baal | pardonner |
Yàlla na ma Yàlla baal | que Dieu me pardonne ! |
Baal naa la sama wàll | je te cède ma part. |
banaana g- | bananier |
banaana g- | bananier |
bañal | refuser qqch à qqn |
Mënuma la koo bañal | je ne peux pas te le refuser. |
baŋ b- | banc |
ban b- | argile rouge banco |
Ndaa li, ban lañu ko tabaxe | le canari a été fait avec de l’argile. |
band | osciller |
bandaalu | se promener |
bank | plier (une chose rigide ou articulée) |
Bankal say baaraam | plie tes doigts ! |
bann | exprime l’idée d’être largement répandu |
Sa cuuraay laa ngi xeeñ bann ci kër gi | (l’odeur de) ton encens s’est répandu dans toute la maison. |
banqaas b- | branche ramification |
Goral banqaas yi féete ak mbedd mi | coupe les branches qui sont du côté de la rue ! |
Dañu fay jàngale bépp banqaas bu jëm ci wàllu koom-koom | on y enseigne toutes les branches de l’économie. |
(prov.) Kenn du toog ci banqaas di ko gor | on ne coupe pas la branche sur laquelle on est assis. |
banqanaase b- | suie |
Diwal ko banqanaase ci jë bi | mets-lui de la suie sur le front ! |
bant b- | bâton du bois |
Taabalu bant la | C'est une table en bois. |
(prov.) Bant, lu mu yàgg, yàgg ci dex, du ko taxa soppaliku jasig | le morceau de bois aura beau rester dans le marigot, cela n’en fera pas un crocodile. |
tegoo ay bant | tirer à la courte paille. |
Am nañu ñaari bant | ils ont deux enfants. |
bantu-suukar g- | canne à sucre |
baas b- | bâche |
baraada b- | théière |
Baraada bu bëtt | une théière trouée. |
baraag b- | baraque |
Bi may xale, bare woon na ay baraag Ndakaaru | quand j’étais enfant, il y avait beaucoup de baraques à Dakar. |
barag b- | titre du souverain dans l’ancienne province du Walo |
Mën naa la limal barag yi fi masa falu | je peux te citer les souverains qui ont régné ici. |
baraj | exprime la manière d’entrer soudain |
Geneen yax ne ca pëqéet ne baraj ca bëtam | un autre os en sortit brusquement et entra soudain dans son œil. |
baram | entortiller |
Wéñ yee baram kawaram gi | ce sont les mouches qui lui ont entortillé les cheveux. |
baram | être crépu |
Kawar gi dafa baram | ses cheveux sont crépus. |
baraxante w- | cheval à robe rouge et blanche |
barax b- | roseau |
barastiku | glisser |
Dafa doon wàcc ci iskale bi, barastiku | il descendait l’escalier et glissa. |
bar b- | varan d’eau |
(prov.) Ku fóotal mbëtt, roccil bar | qui fait la lessive pour le varan de terre devrait dépouiller le varan d’eau de sa vieille peau |
bare-ay | être belliqueux |
bar-bari | se déplacer lourdement comme un varan |